Aller au contenu

Senegaal

Jóge Wikipedia.
Réewum Senegaal
Raaya bu Senegaal Kóót bu aarms bu Senegaal
Barabu Senegaal ci Rooj
Barabu Senegaal ci Rooj
Dayo 196,723 km2
Gox Afrig
Way-dëkk 12,853,259 nit
Fattaay 59,26 nit/km2
Xeetu nguur
- Njiitu Réew
- Njiitu Jëwriñ
Pénc
Maki Sàll
Mohamed Dionne
Tembte
- Bawoo
- Taariix
Péy ak rëddi
Tus-wu-gaar
Tus-wu-taxaw
Ndakaaru
14° 43′ 29.06″ Bëj-gànnaar
     17° 28′ 24.06″ Sowwu
/ 14.7247389, -17.47335
Làkku nguur-gi Faraañse
94% dinañ wax wolof
pël, séeréer, joolaa
Koppar Franc CFA (XOF)
Turu aji-dëkk Senegaal-Senegaal
Sa-Senegaal
Telefon
Lonkoyoon bu Senegaal
Lonkoyoon bu Senegaal   

Senegaal menn la ci réew yi ne ci Sowwu Afrig, mu bokk nag ci Afrig gu bëj-saalumu saxraa (Afrique sub-saharienne), Mbàmbulaanug Atlas diw digam ci sowwu, taqaloo ak Gànnaar ci bëj-gànnaar ak penku, Mali féete ko penku, Ginne ak Ginne Bisaawóo ci bëj-saalum, Gàmbi moom sos ab daanaka-jiba (quasi-enclave) ci biir Senegaal, sutuxlu ba ci lu ëpp 300 jñ (km) ci biir suuf yi. Duni Bopp bu Nëtëx bi (Cap-Vert) ñi ngi ci 560 jñ ci tefesi Senegaal yi.

Réew maa ngi duppe aw turam ci dex gi ko peeg ci penku ak bëj-gànnaar, te ab balluwaayam bawoo ca Fuuta Jallon ca Ginne, di Dexug Senegaal. Njuuxam lu gëwéel la te di lu fendi te yor ñaari jamono: jamonoy nawet (jamonoy taw) ak ju noor (jamonoy fendi).

Ci jamonoy canc gi (la période coloniale), ay digg yu yaxantu yu bari, yu ay imbraatóor yu canc (empire coloniale) moomoon, daal di woon nañuy sampu ci tefes gi gépp. Dëkkub Ndar mujj na di péeyub Afrig gu Sowwu gu Faraas, mu mujj juge ci di leegi Ndakaaru ci 1902, moom Ndakaaru nag mujj na di péeyu Senegaal ca ba mu jotee ca ag tembam / jonnam ca 1960, nekk ci cat li gën a féete sowwu ci kembaarug Afrig

La dale 2012 ba fii mu ne Maki Sàll mooy njiitul réew ma. Senegaal ak donte bokk na ci càmpéef yu bari yu àdduna si, teewul bokk na ci Bennoo gu Afrig (Union africaine) ak Mbooloom diiwaan yu Saxel-sahraa yi (Communauté des États sahélo-sahariens)

Senegaal nag yaatoo na 196.190 jñ2.

Gongikubaat

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Cosaanul turu Senegaal dañul di jeqi dàggasante ak werante. ca 1850 labbe bii di David Boilat, ca mbindam ya mu doon def ci Senegaal,daa gisoon ne Senegaal mi ngi juge ci waxiinu wolof wii di suñu gaal. Bii nag mooy gis-gis bi gën a siiw, te xibaarukaay yi (les médias) gën koo ame. te moone lu ñu nangoodi la te sikk ko la ko dale ca ati 1960, ay gongikubaat yu bari nag joxe nañu leen, ci misaal biy taf cosaanul tur wi ci ag giir gu berber gu Sahara, mooy giirug Zenaga walla Sinhaaj, naan: Turu Senegaal mi ngi bawoo ci tudd gu waa Portigaal yi doon tudd turu giir googu. Waaye werante wi dañul di tàng ci loolu ba tay.

Njëkk-taariix

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci Taariixu Senegaal.
Xeer yu mag yi(Mégalithes) di ay jeexit yu Séeréer yu Ñooro

Lu ci ëpp Njëkk-taariix ci Senegaal day tudd - ba laa tudd lenn - gëwéeli xeer yu mag yi (walla les cercles mégalithiques) yu Senegàmbi yi, walla jóori xor yu ñu sàkk yi (les amas coquilliers artificiels), yu ci mel ne ya nekk ca dunub Faajut.

Jàpp nañu ne Senegaal dëkkees na ko ci njëkk-taariix lu jiitu lool juddug Isaa. Ay doj yu ñu yatt yu Jamonoy doj wu ñu yatt ju njëkk ja(Le Paléolithique inférieur ), wuññees na leen ci daanaka-dun bu Bopp bu Wert bi (Cap-Vert) ak yeneen yëf yu gongikoo ci doj, ñu jekkal leen, dees leen di fekk ci diiwaanub Tëngéej ak ci pegi dexi Senegaal gu penku gi.

Ci jamonoy doj wu ñu xacc (néolithique), jumtukaay yi tàmbali nañoo soppiku ak a wuute, bu ko defee suuf su ñu togg (walla céramique) daal di feeñ. Gasi gëstu ya ñu doon def ca diiwaani tefes ya feñal nañu ay desiiti waañ yuy seere ak a firndeel askan wu mag wu ay nappkat aki yaxantukat wa fa nekkoon (marigot bu Xant ca delta, sottikukaayu dexug Saalum).

Ndefarug mbell (walla gu weñ (metallurgie)) jëm na kanam ci jamonoy mbell yi (protohistorique) (junni bu ngëkk bi njëkk Isaa), fi ñuy gis ay bàmmeel ci bindu ay mbaanaar (tumulus). Ci digg réew mi, fa tollook Gàmbi gu tay gii, dees na fa fekk mbooloom gëwéeli xeer yu mag (cercles de mégalithes) ci aw dog wu tollu ci 100 jñ ci kaw 250|jñ.

Nguur yu njëkk ya

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Ndeté Yalla, lingeerub Waalo

Dëkksi gi dafa doon gën di dolliku ndànk-ndànk tey gën di dëgër ngir àgg ci sos ay nguur yu njëkk yu sosu ci VIIeelu xarnu, nguur gu Tekruur, gu Namandiru, gu Jolof, ak ay mbokkoo yu sori ak Iimbraatóor gu Gana, ci suufus Mali gu tay gi. Ci nguur yu wuute yooyu, gi ci ëppoon doole ci XIVeelu xarnu moo doonoon imbraatóor gu Jolof, gi boole woon Kajoor, Bawol, nguuri séeréer yu Siin ak yu Saalum, Waalo, Fuuta-Tooro ak Bambug. Ci bëj-saalum, nguurug Kaabu, teg ci gu Fulaadu.

Jolof nekkoon na imbraatóor gu Njaajaan Njaay sosoon, ki njëkk a nekk Buurba (buur) ca Jolof. Faleesoon na ko njiit ca loolu doon mujj di nguurug Waalo, ca bëj-gànnaar-penku gu Senegaalug tay gii, ca diiwaanu dex gi. Dajale woon na mbooleem askani giirug wolof ngir taxawal imbraatóor gii ci XIIIeelu xarnu . Ibraatóor gi saayoon na te naaxsaay ci 1549, ànd ak deeg imbraatóor ba mujjoon ca Jolof, Lele Fuli Fak, ki ko rayoon di Amari Ngóone Sabel Faal, ki nekkoon ca jooja jamono kilifag diiwaanu Kajoor.

Jolof des na di aw dog (vassal) ñeel imbraatóor gu Mali ci diir bu tollu ci xarnu. Ba loola amee, yeneen nguur yi, ñoom itam gu ci nekk, tàmbalee jël ag tembam ba mujj wàññi imbraatóor gu Jolof gu mag googu ba àggal ko ci tolluwaayu genn nguur gu yam ca digg réew mi. Ci ñaareelu xaaj bu XIXeelu xarnu, sancaani Faraas yi (les colons francais) tàmbali woon nañoo nangu ndànk-ndànk mbooleem nguur yu Senegaal yii. Jolof moo nekkoon nguur gi ñu mujj a nangu ak Buurab Jolofam bu mujj ba Alburi Njaay, ci ron deflu gu Luwis Federb.

Lislaam a ngi njëkk a tàbbi ci Senegaal ci diggante VIIIeelu xarnu ak IXeelu xarnu, ña ko fa dugal di ay yaxantukat yu araab-yu-berber. Dañu doon tas diine jii ci jàmm, ñu njëkk koo jox Jula yi tuubloo ci ginaaw bi Tukkloor yi ak Saraxule yi, ñoom itam ñu tas ko ci Senegaal gi gépp. Bi ñu demee ba ci kanam ca XIeelu xarnu , la Muraabituun, jug, Tukkloor yi jàpple leen, ñuy jéem a tuubloo mboolooy jaamukati xërëm yi jaare ko ci Jiyaar. Loolu benn la ci sabab yi tax Séeréer si gàddaayoon dem Siin-Saalum, Wolof yi, Pël yi ak Mandinke yi, te ñoom ñepp ña nga jalu woon ca Tekruur. Lislaam teel na tas ca imbraatóorug Jolof. Waaye ca XIXeelu xarnu la nangu ca dëgg-dëgg mbooleem askan yi, ci anam gu jàmmu, loolu nag deesi sante ko Sëriñ si, ku mel ne Seex Ahmadu Bamba, mi sos yoonu murit, Alaaji Maalik Sy kenn ci kilifay Tiijaaniya walla Seydina Limaamu Laay, ki sos laayéen gi, ñi yéemoon nit ñi ci seenug mbaax ak ragal Yàlla ak séeni karaama( xar-baax). Moom Lislaam tam nekkoon ab ker-keraan (moyen) ngir boole nit ñi te di leen aar ci jalgati yi ñu miinoon ci nguur yi (jiyaar yu toftaloo, canc gu ñu teg ci doole, jalgatiy Ceddo yi).

XIXeelu xarnu ñi ngi ko gën a xame ci daanug nguur yi, jàllsig sancaan yu Tugal yi ( colons européens ) ak jàmmaarloo gi lànk canc gi, ñi ko jëmmal di ay nit ñu mel ne Lat Joor, Alaaji Omar Taal, Mamadu Lamin Darame, Alburi Njaay walla Màbba Jaxu Ba. Diiney katolig (walla nasaraan, ndax katolig bànqaas la ci nasaraan) daal di tasu, ñi ko def di ay nasaraanalkat yu Tugal la ko dale ca XIXeelu xarnu, rawati na ca Siin ak kaasamaas.

Lislaam tàbbi na Senegaal ci fukk ak benneelu xarnu,ànd ak giirug Sinhaaj gu Amaasix gi. Turu Senegaal waxees na ne mi ngi bawoo ci tudd gu waa Portigaal yi doon tudd turu giir googu. Askani Senegaal yi sos nañu ay nguur aki nguur-nguuraan, yi ci ëppoon solo di Imbraatóor gu wolof ca diiwaani Waalo, Kajoor ak Bawol, ci fukk ak ñeenteelu xarnu g.j, ak nguuruñg Tukklóor ak gu Deñaanke gu Pulaar gi ca penku bëj-gànnaar ga. Ay dooley Tugal teg nañu loxo ay wàll ci ay tefesam, ci fukk ak juroomeelu xarnu g.j, ginnaaw bi Faraas daal di teg loxo réew mi mépp, ginnaaw ay xare yu limu. Ci atum 1902 la Ndakaaru nekke péeyub Afrig gu sowwu gu Faraas gépp.

Seŋoor walla Léopold Sédar Senghor(1906-2001)(1960-1980) mooy ki njëkk a nekk njiitul Senegaal, yoroon dàkkantalu njiit liy woykat (walla taalifkat) Ci samwie 1959, la Senegaal bennoo ak li ñu daa wax Sudaan gu Faraas gi, ci ron turu Lëngoo gu Mali (fédération de Malie). Lëngoo gu Mali googu tembe na ci Faraas ci 20 suwe 1960. Waaye ginnaaw ay jafe-jafe yu politig, Lëngoo googu mujj na di ñaari réew ci 20 ut 1960: Senegaal ak Mali. Jibaleesoon na ag lëngoo ci diggante Senegaal ak Gambi ci turu Senegambiya atum 1982. Waaye ci jëf feeñul, bu ko defee ñaari nguur yi tàggalikoo atum 1989. Am na ab jë bu ngànnaayu (front armé) bu nekk ci bëj-saalumu réew mi, ca Kaasamaas bu bëgg tembteg diiwaan ba, leeg-leeg mu xareek nguur gi, la ko dale ca atum 1982. _

Feccum gurmet yi (signares) Ndar (sotti gue 1890)

Sancaan yi (les colonisateurs) seen teg loxo gu canc gi (conquête coloniale) mi ngi door bi wuññig suuf yii amee ci 1442 ci loxol moolub Veneto (ab diiwaan ca Itaali) bii di Cadamosto, bi mu defalee ay wuññi ñeel Portigaal. Ca jooja jamono la waa portigaal daal di sóobu - ci lu gaaw - ci Njàppum jaam (walla jaayug nit ñu ñuul ñi), waaye doon nañu war a janook gëpplante (la concurrence) gi bawoo woon ci jaaykati ñu ñuul ñi te bawoo woon Britaani (négriers britanniques), Faraas ak Olaand ca Yaxantug ñatti-koñ ya (Commerce triangulaire).

Waa Olaand yi sos nañu ab diggub yaxantu ca dunub Gore, Faraas taxawal ca 1659 digg bii di bu Ndar nga xam ne moo mujj di péeyub Senegaal bu njëkk bi. Ci 1677 waa Faraas ñi ñëw nangu dunu Gore (benn ci digg yu mag yi ñu daa jaaye jaam yi ak Ndar ak tata ju dunu James ca Gàmbi).

Benn sànnikat ak njabootam cig jaar caMaarsaay atum 1913

Nosteg canc daal di nay taxaw ci dikkug Federb, Kaŋub Senegaal (le gouverneur du Sénégal) la ko dale ca 1854 ba 1861 ak 1863 ba 1865, mooy ki samp dàtti Afrig gu Sowwu gu Faraas gi (ASF)(AOF). Ci wormaal gi mu defoon aada ya fa cosaanoo ( du dëgg, wormaalu ko fenn) la tàllale jeexiital (l'influence)gu Faraas ba mu weesu Senegaal, mu liggéey ci lu jëmale kanam koom-koomu barab bi (ci njariñul Faraas rekk nag lol réew mi yitteelu leen woon ci lenn), daal di sos waaxub Ndakaaru.

Ginnaaw Ndar, Ndakaaru mujj na ci 1902 di péeyu Afrig gu Sowwu gu Faraas gi, benn ci sancu yu Faraas yi .

Ci samwie 1959, Sudaan gu Faraas gi (Mali gu tay gi) ak Senegaal seey nañu ci Lëngoo gu Mali, gi nga xam ne mujj na temb ci 20 suwe 1960. Temb gii mi ngi juddoo ci tuxalug ay nguur ( transferts de pouvoirs ) yu amoon ca dëppoo ga ñu xaatimoon ca Faraas ca 4 awril 1960.

Senegaal nguurug demokaraasi la gu limuy làng (gu bariy parti), njiitul pénc mi (président de la république)dees na ko tànn ngir diirub juroomi at (leegi soppees na ponku sartu réew bi aju ci diirub ngiitug réew mi, yobbóoti ko ci juroom ñaari at, ginnaaw bi ñu ko soppee jële ko ci juroom ñaar, yobbu woon ko ci juroom), moom njiit li nag mooy tànn njiitul jëwrin yi. Barlamaab Senegaal ñi ngi koy wooye Péncum ndawi réew mi mbaa ( jataayub xeet wi), am na nag 120 cér yu ñiy tànn ci ay tànnéef (élections) yu dul yu njiitul réew mi(tànnéef yu yoonal yi : élections législatives) ngir diirub juroomi at


A. Wàdd, kenn ci njiiti Senegaal

Mii menn la ci réew yi gën a am demokaraasi te gën a dal ci Afrig, ndaxte genn daaneel nguur (coups d'État) masu fee am, « Senegaal niki roytéef »[1] yagg nañu koo joxe, wone ko ngir ñu roy ci, ba tee ay yi di fi am ak doonte Amnesty International mi ngi ñaawlu yenn jàpp yi yor mbubum politig[2]Royuwaay:,[3].

Senegaal am Pénc la mu demokaraasi (une république démocratique) (lu sakkan ci ay làngi politig a nga fa). Noste ga fa nekk gu njiitug réew la, ndax ba mu amee ag tembam Senegaal daa daal di jël Faraas niki roytéef, roy ca politigam ba ca 1958, niki yeneen réewi Afrig yi bokkoon ci ASF(Afrig gu Sowwu gu Faraas).Sartu réew bu Senegaal mi ngi taariixoo ci 1959, xoolaat nañu ko ci 1960 ki ko def di Léopold Sédar Senghor ginnaaw genn laaju (référendum). ay xoolaat (révisions) yu bari topp nañu ci, ñooy gu 1963 moo fi saxal nosteg njiitu réew (ci jamono jooju : dindi njiitul jëwriñ) teg ci gu 2001 gi yobbu àppub njiit gi jële ko ci 7 at, yobbu ko 5 at (jataayub mag ñi(le sénat) jëlees na ko fi, ginaaw bi ñu delloosi ko ci 2007).

Njiitul Pénc mi( Le Président de la République) (xoolal limub njiiti Senegaal yil) mooy kilifag nguur gi, moom nag ñi ngi koy tànn, mu ame ci pal gu mbooloo mi (suffrage universel) ci anam gu jonjoo de (manière directe) ci diir bu tollu ci juroom ñaari at, manees koo yeesalaat benn yoon. Mooy fal njiitul jëwrin yi (xoolal limub njiiti jëwrin yu Senegaal) moom itam (njiitul jëwrin yi) mooy tànn jëwrin yi, ba noppi sàkku ci njiitul réew mi mu tabb leen.

Ki njëkk a nekk njiitul Senegaal mooy Léopold Sédar Senghor,mu nekkoon njiit lu ubbeeku te dib taalifkat bu siiwoon . Ci 1981 la ko njiitul jëwrinan lii di Abdu Juuf wuutu, waaye ci 2000 la Làngug demokaraasi gu Senegaal gi am ndam ci njiitug Abdulaay Wàdd, ñu falati ko ci 2007. Njiitul góornamaa bi fi nekk fii mu ne mooy Seex Ajiibu Sumaare.

Péncum ndawi réew mi

Parlamaa bu Senegaal yor na ñaari néeg : Péncum ndawi réew mi ak jataayub mag ñi.

Bi ñu ko taxawalee ci 20 ut 1960,Péncum ndayi réew mi mi ngi yor 150 ndawi réew, yu ñu fal ci pal gu mbooloo mi ci anam gu jonjoo (au suffrage universel direct) ngir diir bu tollu ci 5 at. Tànnéef gi gu ëppte la (Le scrutin est majoritaire) ci genn wër, ci tund yiy xëccoo 90 ndawi réew, di it gu kem (proportionnel) di ab lim bu tas ci réew mi ñu koy xëccoo mu tollu ci 60 ndawi réew. Péncum ndaw yi Macky Sall moo ko jiite, mi nekkoon Njiitul jëwrin yi, waaye fii mu nekk, aw yoon jug na wu Saada Njaay indi ngir ñu jële ko fi, wàññi ab àppam ba du weesu menn at ngir man ko fee jële, wii yoon nag, jot naa jàll, waaye njiitul réew mi dëggalagu ko. Tànnéef yu yoonal yu Senegaal yu 2007 jàll nañu ci ndam lu yaatu lu àndandoo gu njiit gi (coalition présidentielle), waaye lu jege ñaari ñatteel (deux-tiers) ci falkat yi demuñu woon ca mbañ-gàcca ya, li ko waral di ndigalul dogoo(boycott) lu bawoo ci làngi kujje gi.

Parlamaa bu Senegaal boroom benn-néeg (monocaméral) la woon, ci diirub jenn jamono: Jataayub mag ñi, muy lu ñu dindi ci 2001 ci ginnaaw genn laaju gu sartu réew (référendum constitutionnel), delloosi nañu ko ca mee 2007. Mag ñi (Les sénateurs) nag dinañu tollu ci limub 100. 35 ya ca ñoom dañu leen a fal ci anam gu jonjoodi (au suffrage indirect) ci tund yi, yeneen 65 yi njiitul réew mi di leen tabb. Paap Jóob, kilifag Ndakaaru moo ko jiite .

Am na yoon (loi) wu ñu def ci diggadil gi(La loi sur la décentralisation), nekk na it di lu ñuy doxal la ko dale ca samwie 1997, , yoon woowu jox na ay ay doole yu am solo ñeel jataayi diiwaan yi (assemblées régionales).


Ci 1992 la Àttewaay bu Kawe (la cour suprême) bu Senegaal bi nekk di lu ñu dindi, ñu wottee ko cér (organes) yu jagoo loolu: Àttewaay bu firi bi(Cour de cassation), Jataayub nguur gi (Conseil d'État) ak Jataayub Sartu réew mi (Conseil constitutionnel), yooyu cér di yu niru lool séeni moroom ya nekk Faraas. Seeni àttekat Njiitul réew mee leen di tabb. Yooyu ñooy bànqaasi yoon yi gën a kawe ci réew mi (les plus hautes instances judiciaires du pays).

Dalub Àttewaay bu firi bi ëmb na lenn njiit lu njëkk, ak ñatti njiit yu néeg (trois Présidents de chambre) ak gën jaa néew juroon ñeenti xelalkat (9 Conseillers). Ca toppewaay ba le (Parquet), mi ngi ame ci ab Toppekat bu Matale (un Procureur général) , ci benn layalkat bu njëkk bu matale (un Premier Avocat général), ci gën jaa néew ñaari layalkat yu matale (deux Avocats généraux) ak gën jaa bari juroom benni déglukat (six Auditeurs) yu koy liggéeyal. Am na ñatti néeg, yoy bu ci nekk mi ngi ame ci lenn Njiit ak ñaari xelalkat gën jaa néew:

  • Néeg bu njëkk bi mooy àtte layoo yi aju ci wàllug tooñaange yi (pourvois en matière pénale),
  • Bu ñaareel bi di àtte layoo yi aju ci mbirum ñoñ ak yaxantu ( pourvois en matière civile et commerciale)
  • Bu ñatteel bi di sëgg ci wàll yi jëm ci mboolaay (yoonu liggéey ak kaaraange gu mboolaay)(droit du travail et sécurité sociale).

Jataayub nguur gi ay xaaj yu bari ñoo ko sos:

  • Xaaj bu njëkk bi moom lañu féetale xuloo yi aju ci bindu ci limi tànnéef yi(les listes électorales), yoonu (légalité) gu jëfi mbooloo yu barab yi ( collectivités locales ) ak diiŋat yi ngir neenal gu aju ci nguur gu ëpp (les recours en annulation pour excès de pouvoir).
  • Xaajub ñaareel bi day def li Àttewaayu xayma yi (la Cour des comptes)di def ca Faraas , ci moom sax la jële woowiinam woowu bu yàggul rekk.
  • Xaaj yooyu yépp nag am nañu ay njiiti xaaj (Présidents de section), ay xelalkati nguur (les Conseillers d'État) ay xelalkati laaju (les Conseillers référendaires) te ki leen jiite mooy njiitul jataayub nguur gi (Conseil d'État).

Jataayub sartu réew bi yor na juroomi cér, yu ñu tabbe ci ag santaane (décret) ngir juroom benni at yu ñu dul yeesal, yoo xam ne njiit ca la ak topp-njiit (Vice-président). Dees na ko yeesal cig wàll waaye déet lépp, waaye du weesu ñaari cér gën jaa bari. Ab liggéeyam mooy fuglu tànnéef yu yoonal yi, ak xool ba xam yoon yi (les lois) dëppoo nañook sartu réew mi, ak warlu yu àdduna yi (les engagements internationaux).

Senegaal dindi na mbugalum ray ci 10 desambar 2004[4].

Gëstu-askan

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ëpp ci gëstu yi ñu def ci wàllug Gëstu-askan (walla demogaraafi) ci Senegaal dafa sukkandiku ci Waññ (recensement) yi ñu jotoon a def ci 1976, 1988 rawati na 2002. Doxal gu Séentu ak Lim gi (la Direction de la Prévision et de la Statistique) ci 2004, siiwaloon na « ay leeral ci askani Senegaal yi, loolu di woon lu juge ci waññ gu 2002 » mu sóoraale woon ci màgg gi man a ami ci askanu Senegaal la ko dale booba ba 2015[5].

Dox gu gëstu-askan gi ci diggante 1961 ak 2003 (lim bu FAO, 2005). askan ci ay junni ciy way dëkk .

Bu ñu sukkandikoo ci gongikuwaay yii, askanu Senegaal - wi doonoon lu toolook 1 milyoŋ ciy way dëkk ci 1900 ak 2,8 milyoŋ ca jamonoy ag tembam ca 1960 – yekkatiku na tay ba àgg ci 11 343 328 ciy jëmm (nattale gi ci 31/12/2007) te man naa àgg ci 13 709 845 ci mujjug 2015. Askan wii kon day màgg ci anam gu gaaw, ànd ak benn tolluwaayu njuru (taux de fécondité) bu tiim 4 doom ci jigéen.

Seetloos na fa genn kuute gu giir gu mag: Wolof (43,3 %), Pël (23,8 %), Séeréer (14,7 %), Joolaa (3,7 %), Malinke (3,0 %), Soninke (1,1 %) Maanjanke (2%) ak yennat ci ay giir yu gën a néew, te gën a gawu ci barab,waxuma la nag naari Libaan yi ak Tubaab yi, nga xam ne ñi ngi nekk ci dëkki taax yi [6]Royuwaay:,[7]. Ci mujjug 2007, 16 966 ci waa Faraas bindu woon nañu ci seen barabu aji teewal (ambassade) (boroom ñaari réewu it ci lañu woon (les binationaux))[8].

Ab diir bu yàgg a ngii askan wi nekk di jalu ci fi jàkkaarloo ak Mbàmbulaan gu Atlas gi, waaye nocciku gu kaw gi (l'exode rural) yokk na yamoodi gi ci séddale gii. Fi mu nekk ñeenti nit yoo gis ci waa Senegaal, kenn ka mi ngi dëkk ci Daanaka dun bu Bopp bu Wert bi (Cap-Vert), looloo waral péey baa ngi waaj a xëx.

Bu Ndakaaru jàllee, diiwaan yi ñu gën a taaxal (les régions les plus urbanisées) ñooy Siggicoor, Cees ak Ndar. Yi gën a néew ag taaxal (moins urbanisées) ci diiwaan yi ñooy Koldaa, Maatam ak Fatig.Diiwaanu Tàmbaakundaa nag moo yor fatt (densité) gi gën a doyadi (11 way dëkk ci jñ²).

Bu ñu sukkandikoo ci nattale yu 2007, digg yu taax yu diiwaan (les centres urbains régionaux) yi yor lu ëpp 100 000 ciy way dëkk ñooy Tuubaa (529 176) (Man nag yaakaar naa ne ag na ma xame Tuubaa, la fa dëkk man naa ñeentte lim bii ñu wax) – mi jekki jekki gis ag màgg gu yéem ñépp –, Cees (263 493), Kawlax (185 976), Mbuur (181 825), Ndar (171 263), Siggicoor (158 370) et Njaaréem (100 445)[5].

Ca 2007, Senegaal teeru woon na lu tollu ci 23,800 ciy daw-làqu ak sàkkukati ag wéeru ( demandeurs d'asile), yoo xam ne lu ëpp 20,000 ca ñoom ay waa Gànnaar lañu, yu doon daw boddanteg xeet ga, ak ñennat ci waa Liberiyaa, waa Siraa Leyoon, ak yeneen réew [9].

Bu Senegaal dee réew muy teeru ay way gàddaay (ay migrants), moo xam yu ay jamono lañu(saisonniers) mbaa déet, moo xam yu bawoo ci réew yi mu digool lañu walla yu ko sori[10], du tee menn mbooloo mu Senegaal mu mag ma ngay dund ca bitim réew. wisaaroo gii (diaspora)alal ju am solo la ci réew mi, ci wàllug koom ak njëmmte (identité). Xarala yu xibaar ak jokkoo yu bees yi XXJB dañuy gën di jàppandal jokkoo ci diggante njaboot gi te tax it deesi man a dund mu mel ne da ngaa nekk ci sa biir réew . Li ëpp ci ñiy dem nag ay waxambaane lañu yu jublu Tugal, rawati na Faraas, ak Itaali, walla ñuy dem ca Aamerig gu bëj-gànnaar ga, ca Kebeg yobbaale ci seeni xol naalub dellu réew ma ci ginnaaw yennat ciy at. Màggug gàddaay gu yoonoodi gi (immigrations clandestines), ñu koy def ci ay anam yu bon te ñaaw jëm ci Duni Kanaari yi lu tiital Senegaal la ak réew yi koy teeru.

Ñi gën a ñàkk yaakaar ñoom faalewuñu sax ay wi ñu ci man a dajeel, ginaaw gis nañu seeni moroom tekki, rawati na ya bokk ca wisaaroo ga (diaspora) — moo xam Senegaal lañu juddoo mbaa dañu faa am rekki way jur - rawati na ñi ciy yëngu ci tàggat yaram mbaa fànn (art).


Lu sakkan faatoo na ci gàddaay gu yoonoodi gi, mbaa mbëkk mi, baat bi ñu ko gën a xame, lu ko waral? xanaa géej gi ñu sóobu ci lu duli jumtukaay yu dëppoo , ñoom kay dañuy sóobu ci ay looca yu doyadi, duy kooki bagaas ak nit ci wépp xeet ak maas, bu ko defee yooru, duñu faale la leen dëgmal ciw ay ak musiba, gaal gaay doon duus ba, néegub añ ba, bu tëdd ba, leeg-leeg duus ñëw téq leen mbaa ngelaw lu saf, ba kero ñuy àgg bu ko Yàlla dogalee, waaye cis lëf cig loof, lu sakkan di ca des dib añ mbaa reerub ag kuréel ciy jën yu waroon a nekk diy añ ñeel leen mbaay reer. Nii lay deme ba kero ñuy àgg ak la leen fay xaar ciy kaso ak ëlëg gu lëndëm, lii mooy li xew ci mbeex mi, waxuma la nag la ca tàkk ga, aji tàng ji tàkk gii nga xam ne jali beeñ yi yàgg nañu fee tee nit àgg fa mu jëm.


=='

  1. ' Koom-koom ==
  2. niou boolé chi chi waallu kom kom you beess yi fa feegn chi 2012 ak tay. guiss nagne fa petrole ak gaz ak zircon ak wourouss

Senegaal nguur la gu bokk ci Bennoo gu koom-koom ak gu koppar gu Afrig gu sowwu gi. Ginnaaw ay jafe-jafe yu koom-koom ci njëlbéenug ati juroom neen-fukk yi, ay yoonam (ay luwaam) yu koom-koom soppiku nañu, bu ko defee ag màggam gu koom-koom mujj àgg ci ay 5% ci diggante 1995 ak 2001. Ci ndoortel 1994 Senegaal door na ci doxal tëriinu yéwénal gu koom-koom gu kawe ay yitte, ci càmmug mboolaay gu àdduna bi (communauté internationale), looloo ko jañoon ci mu woyofal xiimay kopparam bii nga xam ne daa tënku ci Frank bu Faraas, mu woyofal ko ba ci 50%. Jeexiitalu woyofal gii diisoon na lool ci ay way dëkkam, ndax taxoon ba njëgi li ëpp ci marsandiis yu dàttu yi ak yu dund yi seeroon te yekkatiku, niki meew, yàpp, ceeb, ba àgg ci fulu ci genn guddi, waaye am na genn màgg gu am ci koom-koom bi, ak ci njuddéef mu ñumm mu biirum réew mi, ngir yéwénal yi, nga xam ne àgg na ci 5% ci at mu nekk, bu ko defee walu gi(l'inflation) wàññiku ci anam gu yéeme ba àgg ci ay lim yu ndaw bu ñu ko nattee ca la romb.

Ci 20/ut/ 1960, la Senegaal génn ci lëngoo gu Mali gi, daal di jibal ag tembam.

Senegaal ak Gàmbi bennoo nañu ci 1982 ngir amal lëngoo gu Senegàmbi, waaye gii nekkutoon lu dul aw gisiin, kenn masu koo jëfe. Mujj gi ñu far ko tas ci 1989.

Ay janoo jot nañoo am la ko dale ca 1982 ci anam gu dogatu ci diggante ñoñ tàqalikoo (les séparatistes) ñi nekk ci bëj-saalum gu Kaasamaas ak doole yu góornamaa bi. Ginaaw ay jéem yu bari yu àntuwul, genn dëppoo mujj nañu ko xaatim ca Siggicoor ca 30/desambar/2004 [11] ci diggante jëwrini biir-réew ji woon Usmaan Ngom ak làbbe Augustin Diamacoune Senghor, mi nekkoon njiitul fipp gu Yëngu-yëngu gu doole yu demokaraasi yu Kaasamaas (YDDK)(MFDC), moom Diamacoune Senghor moomu mujj na faatu.

Beneen tombub coow ci diggante ay waa Kaasamaas ak Ginne-Bissaawuóo màgg na ci awril 2007[12].

Ci 1989, Gànnar ak Senegaal génne nañu ku ci ne, ci anam gu ñaaw sa njabootug moroom te ña ëppoon ca ñoom ña nga juddoo woon fa ñu leen génnee, muy réew mi leen doomoo woon, ñu jotoon faa seey ca mboolaay ga ak koom-koom ba. Bu ñu sukkandikoo ci li Jataayub daw-làq bu kawe bi (JDK) HCR wax, ay daw-làqu ña nga des ba tay ca guddaayub dexug Senegaal gi[13]. Ci 2007, Njiitul Gànnaar jibaloon na ba muy def càkkug palaam ga (campagne), ne nangu na delsig doomi réewam yooyu doon dund ci Senegaal ak Mali te neexu leen[14].

Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci Melosuufug Senegaal.

Senegaal a ngi nekk ci diggante 12°8 ak 16°41 wu rëddu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar ak 11°21 ak 17°32 wu rëddu tus-wu-taxaw wu sowwu. digam wi gën a féete sowwu mooy Ndakaaru di it cat li gën a féete sowwu ci goxu Afrig.

Su ñu ko méngalee ak réewum Mali walla ak mu Gànnaar di nanu gis ne Senegaal réew mu tuuti la ci rëyaayu-suuf.

Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci Séddaliin wu yoriinu Senegaal.

Kilimaab Sahel la ame:

Seddatleg yoriin

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ca atum 1996 la seddale gu mujj gi ame, mooy giy wéy ba tay, lu dul coppite yi ci mujj a am: Sosug diwaanu Maatam ci 2001 ak gox-goxaan bu Kungeel ci 2006.

Ci 2008, la Senegaal nekk 14 diwaan,

lonkoyoonu seddaleg yoriin gu diiwaani Senegaal yi

Yenn ciy dëkk:

Senegaal doon na réew mu bariy giir, waaye it soo ko mengalee ak yeneen réewi Afrik yu bari, wuuteg ay giiram du feeñ. Man nan ni daanaka wuute amul ci diggante giiri senegaal yi ndax seenug bennoo ci caada. Man nan cee lim yii tambalee ko ci yi ci gën a bari ba ci yi ci gën a néew: Wolof (43,3 %), Pulaar (23,8 %), Seereer (14,7 %), Joolaa (3,7 %), Malenke (3,0 %), Sooninke (1,1 %) Manjaak (2%), ak yeneen giir-giiraan yu tas ci réew mi, man nan cee boolee it tubaab yi ak naari libaan yi.

toftaloog xew-xew yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  • Ci VIIeelu xarnu : nguur yu njëkk ya
  • XIeelu xarnu : Feeñug Lislaam
  • 1442 : doorug teg loxo gu sancaan yi
  • 1444 : wuññig Dunub Gore. Joqalante yu yaxantu yu njëkk yi ak waa Tugal ñi ngi door bi Waa Portigaal agsee ci sottikuwaayu Dexug Senegaal ak Cap-Vert (Bopp bu wert bi) (Nekkeesoon na di joqalante ay ndima aki weñ (métaux) ci pëndëxu wurus (la poudre d'or), ak daakaande ak bëñu ñay (dl'ivoire)).
  • Ginaaw 1600 : Waa Faraas ak waa Olaand dàq nañu waa Portigaal.
  • 1659 : Taxawal Ndar
  • 1700 : Faraas yilif na yaxantu gi ci diiwaani tefes yi. Ak li kujje gi di tar ci diggante Faraas ak Britani lépp ak xeex yu bari yi teewul cangug Faraas akug jeexiitalam tallaliku. Bi mu toogee ca Ndar, Faraas daa daal di yéeg ci Dexug Senegaal gi ngir àgg Niseer, ak doonte daje na ak yenn jàmmaarloo yu bawoo ci yennat ci ay giir niki (Tukulóor yi ak Pël yi).
  • 1815 : Ndajem Vienne mi jox na Faraas Gore.
  • 1818 : njaayum jaam yi dindees na ko ca Faraas.
  • 1852 : Federb wàcc na Senegaal, daal di àtte, dale ko 1854 ba 1861 ak la dale 1863 ba 1865.
  • 1855 : Wàllug teg loxo gu xare daal di door ci nangug Waalo.
  • 1857 : Sosus Sànnikati Senegaal yi(les tirailleur sénégalais).
  • 1857 : Jëlug barabub Ndakaaru cig dëppoo ak kilifay lebu yi.
  • 1860-1865 : Mbooleem Kaasamaas gu suufe gi ba Siggicoor rot na ci ron yiirug Faraas (sous protectorat français).
  • 1886 : Faatug Lat Joor ak jeexug jamonoy Dammeel.
  • 1892 : Xare yu mag yi jeex nañu
  • 1895 : SosugAfrig gu sowwu gu Faraas gi (ASF)(AOF). Senegaal mujj na ci anam gu fés di ab sancu bu Faraas, ñu koy yore ak a doxale ca Ndar.
  • 1902 : Tuxalug péeyub (ASF)(AOF) jële ko Ndar, yobbu ko Ndakaaru. Faraas mi ngi doon dundal koom-koomu Senegaal ci anam ga ko ñoroon te méngook ag jëm-kanamug réewam, googa di mbayum gerte, gu ñu war a génneji (culture de l'arachide destinée à l'exportation).
  • 1914 : Blees Jaañ mooy nit ku ñuul ki njëkk a toog péncum ndawi réew mu Faraas ; moom nag tëyye na toogub ndawu réewam boobu ba ci 1934.
  • 1959-1960 : Sosug lëngoo gu Mali (la fédération du Mali).
  • 1960 : Tembug Senegaal (Indépendance du Sénégal).
  • 1982-1989 : Sosug lëngoo gu Senegambi.

Karmat ak delluwaay

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  1. « am na nu ñu gise Senegaal niki roytéef ci saafara xuloo yeek xeex yi ? » (table-ronde régionale sur le Sénégal animée par Jean-Claude Marut, CEAN-IEP de Bordeaux, 15 janvier 2004)
  2. Rapport 2006 d'Amnesty Internation jàppug Idriisa Sekk
  3. Rapport 2007 d'Amnesty International bàyyig Idriisa Sekk, ak setal gi nu ko def ci mbooleem li ñu ko toppe woon
  4. Abolition de la peine de mort au Sénégal [1]
  5. 5,0 et 5,1 (fr) Agence Nationale de la Statistique et de la Démographie du Sénégal
  6. Royuwaay:Ouvrage
  7. Royuwaay:Ouvrage
  8. (fr) Samir Gharbi, « Combien sont-ils, où vivent-ils ? Toujours accueillant », Jeune Afrique, n° 2477, du 29 juin au 5 juillet 2008, p. 28
  9. U.S. Committee for Refugees and Immigrants. 2008. World Refugee Survey 2008
  10. (fr) Rapport 2007 Amnesty International : Arrestations et renvois de migrants
  11. (fr) Rapport 2006 - Amnesty international
  12. (fr) Rapport 2007 Amnesty International : Combats en Casamance
  13. (fr) HCR : La Mauritanie prête à autoriser 20 000 réfugiés à rentrer du Mali et du Sénégal
  14. (fr) Retour des réfugiés mauritaniens

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons

Jukki yi ci lonku

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lëkkalekaay yu biti

[Soppisoppi gongikuwaay bi]



Réewi afrig

Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkina Faso • Buruundi • Cadd • Ecoopi • Eritere • Eswatini • Gaambi • Gaboŋ • Gana • Gànnaar • Ginne • Ginne Bisaawóo • Ginne gu Yemoo • Isipt • Jibuti • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Keeñaa • Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Lesoto • Libeeria • Libi • Madagaskaar • Malawi • Mali • Marook • Móoris • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeria • Ruwandaa • Saambi • Sahara gu Sowwu • Sao Tome ak Principe • Senegaal • Seysel • Simbaawee • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Sudaan gu Bëj-saalum • Tansani • Togóo • Tiniisi • Ugandaa