Anas
Apparence
Ci làkku ibrë la tur wi jóge. Ci angale mooy Annas; Ci faranse mooy Hanne ou Anne
Saraxalekat bu mag ba la woon. Kiriñus, boroom réewu Siri moo ko fal saraxalekat ci at 6 walla 7 g.K.. Waaye Garatus, boroom réewu Yude, folli na ko ci at 15 g.K.. Mu fal ci palaasam Ismayel ba noppi Elasar doomu Anas, ba noppi Simoä, ba noppi Kayif ci at 18 g.K.. Waaye gannaaw bi ñu ko follee, baatam dafa weyoon di am sañ-sañ bu bare. Naka noonu Anas ak Kayif bokkoon nañu ci liggéeyu saraxalekat bu mag ba ca jamano ji Kirist liggéeyoon. Kayif takk na doomu Anas.
Dañuy gis Anas ci Injiil ci Lu 3:2; Yow 18:13,24; Jëf 4:6; 5:17-18, 27-28.