Aller au contenu

Sëriñ Tuubaa

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Seex Ahmadu Bamba)
Benn nataal bu Xaadim Rasuul

Sëriñ Tuubaa Xaadimu-Rasuul (Seex Aḥmad ibn Muḥammad ibn Ḥabiib Allaa 1853-19 sulet 1927) boroom xam-xamu diine bu jullit la bu di ab sëriñ te cosaanoo ci ag càllala gu doomi soxna. Mi ngi gane àdduna ci Mbàkke, ab dëkk bu Maam Maaram sancoon ca nguurug Bawol, maamaatam jooju mooy Maharam, walla Maaraam,mooy ki sanc Mbàkke Bawol, waxees na ne loolu ci atum Shaqdadin la di (1194 g / 1780 g.j ) . Waaye dëkkewu fa woon, da fa a bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata, magi habiibullaah ju mu bokkalul nday. Moom nag sëñ Maaram mii daa desoon Jolof, fa la làqoo ñu denci ko fa, di ko siaare.

Ñu koy woowe itam Xaadim Rasuul di Ñaari baati araab yuy wund Surgab yonent bi Muhammad (j.m). Mu bokk ci jëmm yi gën a fés te ëpp solo ci diiney Lislaam ci sowwu Afrig, ndax moom moo sos yoonu murit. Waa-réewam Seex Ahmadu Bamba lañu koy woowe ndax cofeel gu ñu am ci moom.

Jaar-jaaram

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Doomi ab sëriñ ci yoonu (Xaadirya) – Mooy yoon wi gën a yàgg ci Senegaal –, Ahmadu Bamba ab jullit bu dëddu la woon te dib sóofiyu, daan bind it ci wàllug fiqh, tasawuf ak wéetal Yàlla (tawhiid) ak wàll yu bari ci xam-xamu diine, ak tagg Yonent bi, mbaa ci lu aju ci "shukr" (sant Yàlla).

Ak doonte ku daan bañ la te àndadi woon ci canc gi (colonialisme) ak teg loxo gi tubaab yi defoon réew mi teewul melul woon ne sëriñi tiijaan yi jugoon di jiyaar, ku ci mel ne Alaaji Omar Taal, Màbba Jaxu Ba mbaa Muhammad Lamin Daraame. Ak doonte yoroon na gëm-gëm bi mbooleem jullit ñi yoroon ci Jiyaar , muy jug dàkku sab dëkk ci tooñaange, xeex ngir goreel ko, mbaa aar sa alal añs, teewul mu yoroon beneen gis-gis bu gën a xóot ci jiyaar, mooy jiyaaru nafs, maanaam jiyaar ngir xeex ak sa bakkan ak sa bànneex, noot ko, moom ko, nga rax ci dolli ku gisoon la ne tubaab yii de xeex ak ñoom ciy ngànnaay yombul, te deesu ci jële ndam, - te mel na ne jamono jox na ko dëgg ! Ndax mbooleem ñi doon def jiyaar ak tubaab bi, tubaab bi faroon na leen noot, mbaa mu ray leen, tee leen a sottal seeni sémb, àntoodil seeni naal - ndax ëpp gi ñu ëppoon ci doole ak ngànnaay te gën koo aaytal, gën koo ñawle, bi lii amee, Ahmadu xam ne tubaab yee ko raw foofu, ca rafetug xelam ga mu jël beneen "estrateji", mooy jiitu leen ci xol yi, ba lu tubaab yi def ci kaw mu def ko ci biir, lii moo nekkoon mbóotum jiyaaram.

Alxuraan mi ngi nuy xamal digal gu Yàlla digaloon jullit ñi ñuy jiyaar ak yéefar yi, ak doonte dañuy fukk jullit biy kenn, ba yàgg mu ne woyofal na ko ci yeen (jullit ñi) ndax xam doyadi gi nekk ci ñoom, mu ne leegi kenn mooy xeex ak ñaari yéefar, ndax xam na ne pastéef ba woon wonni na, te loolu mooy jàmbaar ya àndoon ak Yonent bi (j.m), naka mook tuubeen yii nga xam ne ba ñu duggee ci lislaam yàggul, te tubaab ëpp leen doole fuuf ak ngànnaay, kon kii ci hikma la jëfe te mooy li Yàlla bëgg

Bind na it lu maneesul a misaal ciy taalif, lu ci ëpp nag ay woy, yu muy def la, benn ngir tàgg ci Yonent bi (j.m), mbaa sant ci Yàlla, mbaa mu ciy wone may yu ko Yàlla may, loolu lépp di tàbbi ci sant Yàlla, mbaa mu jëm ci yar ak njàngalem diine, loolu nag ci araab la daan doon, teewul mu daa def ay tomb di ci tënk li muy jàngale ci araab, daan ko def ci wolof ñeel ñi xaw a mage ba jànge ci araab raw leen, mbaa seeni xel xaw a naqari ba ñuy am ay jafe-jafe ci jànge ci araab. Bokk na ci li ko tax di def ay woy ci taalifam yooyu, woy day jumtukaayu mokkal, mokkal ay woy daa gën a yomb ay wesar, looloo tax sax téere yi mu taalif ci xam-xam ngir taalube yi jàng ko, da leen a def ci ay woy, teewul bind na as lëf ci wesar lu ci mel ne majmooha, jasaawu sakkoor bu géej gi te sëñ Sëriñ Musaa Ka woy ko ci wolof añs.

Ku fonkoon wolof la ak doonte ci araab la daan binde

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci araab it la daan binde, sabab si nag su diine la waaye ku fonkoon aw làkkam la lool, ci la daan waxe te déggoon ko lool, daa na faral sax di jël waxiinu saalum-saalum wi ñu daa wax ne mooy wi gën a wolofe te gën a xóot di ko waxe, bis kenn ci ay taalubeem yi daa woy ci wolof ci seeni taalif, daa jugoon di ko tagge ci araab, mu ne ko bu ko defati, dee ko defe ci wolof, ndax man ki may tagg araab la te man mi ngay tagg wolof laa, kon kee da koo war a dégge ci aw làmmiñam, man it naa koy dégge ci samaw làmmiñ, lii moo waral ñu ko daa woy ci wolof, teewul nag am ciy taalubeem ñu ko woy ci araab niki Sëriñ Mut Jaw Paxa, Sëriñ Ibraayma Jóob Almashari.

Man nañu ne sax mooki taalubeem ñooy ñi suuxat làkk wii, ndax ñi ëpp ci ñi bind ci wolof ci Senegaal ñoom lañu, xool ci ku mel ne Sëriñ Muusaa KA, Sëriñ Mbay JAXATE, Sëriñ Mbay Kayre, Sëriñ Moor Jaara Mbay, ba ci Mamoor Xam Sa Diine mii, te Tuubaa day tuuru ak ñu mel ni ñoom.

Sababu binde ci araab

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sabab si diine la, loolu it bind na ko ci genn ci ay xasidaam mu ne ca dañoo araamal ci moom muy bind ci lu dul ci làkku araab, wax jooju xel nangu na ko, ndax araab mooy làkk wu kilifawu (officielle) wu Lislaam, képp kuy njiit ci lislaam ñépp war a jariñu ci yaw ci nga war di binde, booy xool bindkat yi gën a mag ci Lislaam duñu ay araab te teewul ci lañu doon binde, ngir aar làkkuw alxuraan wi, jëmale ko kanam, tax it deesi ci sonn ba muy waral ñuy man a xam alxuraan ci lu dul ag xamal, ndax bu xam araab gi wéree xam alxuraan gi wóor te rafet.

Nga rax ci dolli ci araab la jànge, làmmiñ wi réew mi mépp daan jànge, daan ci bindantee it ci lu fullawu (lu officiel), ba ci tubaab bi sax yoroon na ay "antalpareet" walla ay làpptoo, maanaam ñu leen di tekkil ci araab ak di leen ci bindal, ndax xam gi ñu xamoon ne réew mi lu ci ëpp ci araab lañuy binde.

Te it ca jooja jamono wolof làkk la woon wu yaatoowul noonu, te du woon wolof yi rekk ñoo waroon a jariñu ci Sëriñ bi mbaa ñoo nekkoon fa moom, lii lepp taxoon na muy binde ci araab. Waaye teewul nekk gi mu nekkoon di nitug Yàlla taxoon mu xam lu ñëwagun, yobbu woon ko ci mu digal ñenn ciw nitam ñu féetewoo jëmale kanam wii làkk ndax xam gi mu xamoon ne mooy làkku ëlëg ci Senegaal

Dencukaay:Jumaay Tuubaa.jpg
Jumaay Tuubaa ju mag ji

Sancoon na Tuubaa ci 1887 ngir gën a man a wéetal Yàlla, ginaaw bi nit ñi baree fa moom ca Daaru Salaam ga ca anéeri Mbàkke gi ñu la waxoon leegi, nga xam ne raj-rajloo ba teewoon na koo nekk ca na mu ko soxlaa ba man a def li mu bëgg cig jaamu ak yar, ba mu demee Tuubaa't loola toppati ko fa, moo waraloon mu faroon sanc Mbàkke-Baari ca Jolof, fa la juge dem géej boo ci bëggee xóotal yëral: SancamJolof Ak li ko waraloon.

Tuubloo ay buur ak doomi buur

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci bañ gi mu defoon cancug Tubaab yi ak séen politigu nasaraanal bi, Sëriñ bi mujjoon na tuubloo lu sakkan ci y buur aki doomi buur yu diiwaan bi, Jàmm la daan digle, jaamu Yàlla ak liggéey ngir man a texe ëllëg. Looloo waraloon lu sakkan ciy mbooloo doon bawoo fu nekk di sottiku ci kawam, ñii ngir jébbalusi, ñii ngiri sabab yu àdduna, loolu lepp nag jeqi woon na ñàqare ak jaaxle ci Tubaab yii nga xam ne doonuñu woon nangu ñu dul ñoom ñuy am genn jeexiital ci réew mi, mbaa genn kiliftéef gu àdduna gu bawoowul fi ñoom

Sababu jàpp gi ak gàddaayal gi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Waaye bi Tubaab yi gisee ne moon de boroomum mbooloo la te ñu ko gëm lañu, man na leen a yëngal bis jëme leen ci jiyaar, ni ko moroomi sëriñam si defe woon, lañu ko daal di jàpp, tëj ko ci kaso fa ñoom, ca Ndar giy dalub kaŋ bu ASF (Afrig gu Sowwu Gu Faraas gi), njëkk ñu koy gàddaayal ca Gaboŋ ci 1895. Tubaab yi ngir ñu man koo jàpp lay yii lañu indi woon:

«Ñun de gisuñu lenn luy wone ne Ahmadu Bamba day woote Jiyaar, waaye ab taxawaayam akug soppaxdikoom ak yu ay taalubeem daal teey nañu xel, jeqi nañu sikk »

Mi ngi dellusi ci Ndakaaru ci 1902 gannaaw ba mu defee 7 at ak 9 weer cig gàddaayal te nekkoon ci àll yu lëndëm këriis ya, bu ko defee mbooloo mi teertu ko ciy yuuxuy mbegte ak ségéré.

Tubaab yi jàppati ko

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Tubaab yi jéemaatoon nañu koo jàpp ba yabaloon fa ay spahis nga xam ni ay xarekat yu ñuul lañu te àndoon ak nootkat bi waaye taalibey sëriñ bi àntoodil loolu. At mi ci topp lañu ko mujj jàpp daal di koy gàddaayal ca gànnaar ci lu tolloog 4 at. Ci diirub ñaari gàddaay yii nag xew-xew yu xel dajul jot na faa am, ngir gën cee am xam-xam yëral: Ñaareelu tukki bi (bu Gànnaar bi).

Tubaab yi xam nañu ko leegi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gannaaw 1910 nag ci la tubaab yi xam ni sëriñ bi xeex yëkkatiwu ko te sax jàpp nañu ñoom ni yoon wi da leen di jàppale ci li ñu bëgg, ci noonu lañu sàkku liggéey ak moom maanaam ñu ànd far, ngir wone loolu ci lañu ko bëggoon a takkal raayo bii di “Légion d'honneur” di raayob teddnga bu Faraas bi gën a kawe waaye sëriñ bi gàntal.

Yoon wi nag mi ngi gën a am aw nit ginnaaw bi mu fi bàyyikoo te taawam bii di Sëriñ Muhammadu Mustafaa Mbàkke tàmbali woon liggéeyub jumaay Tuubaa ji, di tolloo ak barabam bi, doon tay fu nit ñi di siyaare cig rajrajloo. Gannaaw bi mu fi jógee, ay way donnam ñoo nekk ci xilaafa gi di digle tey tere.

Fatalikug Sëriñ bi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ahmadu Bamba, ku taalibeem yi weg te fonk ko la , jàppe woon ko aw wàlliyu, te loolu du woon lees di faral di gis ci ñiy wuyyoo sunna, waaw ndax ci Lislaam daa am ay dawaan (courants) yu ci mel ne bu sunna, bu siit, ak bu tasawuf añs, moom nag Seex Ahmadu ci bu tasawuf bu sunna la bokk, am na ci waa tasawuf yi way teengal, bay àgg ci di jibal ay kàddu yu di yu tumbrànke, mbaa ñuy àgg ci wax juy jéggi dayo ba cig lëmu bay waral sikk ak weddi, waaye kii di Seex Ahmadu ay mbiram ak leer a ko wër, jéggiwul dayo ci genn anam, mbiram ci kitaab la tegu ak sunna ak tasawuf bu leer, te dëppoo ak doxiinu Yonent bi (j.m). Benn nataal rekk lees am ci moom. nataal boobu fu nekk tafees na ko fa, muy ci tabax yi, ci daamar yi walla feneen fu muy fése rekk.

At mu jot ay junniy junni ciy taalibe danañu dem ca Tuubaa dëkk bu sell ba, ngir màggal gàddaay ga mu defoon jëm Gaboŋ muy yamoo ak 18 safar gu nekk. Bis boobu Sëriñ bi moo digle woon ñu santle ko Buur Yàlla ci may yi mu ko may ciy xéewal, muy bu taalibe yi fonk, jàppe benn ci bis yi ëpp solo ci bis yi.

Li mu fi bàyyi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ bi da daan woo ay taalibeem ngir ñu dëpp te jublu Yàlla, daan na digal taalibe yi ñuy moytu aw ay tey sàkku xam-xam bu am njariñ, di liggéey, am jom ju ànd ak jàmm, am pastéef ak ngëm ci Yàlla. wax na ni: "[[Yàlla rekk la ragal, samay yaakaar ci Yàlla laa ko wékk."

Sëriñ bi dékku na nattu yu bari te tar. Benn ci ñoom mooy gaynde gu xiif ga juge barab ba ñuy wone rab yi te nekk ca Sor. Bis booba, dees koo tëj bàyyi ko ak gaynde gu mel ni far xar mu gis boroomam. Sëriñ bi doonoon ku jàmmu te ñaw daan na wax ni: "Du ma mas a lor kenn ak ku mu man a doon." Tëj nañu ko ci kaso bu lëndëm def fa ay ràbb, gobar ak jaasi, mu jàng fa saaru baqara ak aali Imraan. Sëriñ Musaa Ka miy baayi way gëstu xew xewi démb ci yoonu murit mi ngi ñuy xamal ni:

  • keroog gis na fa suñu Maam Jaara () mu di ko ñaax te di ko dolliy daara
  • Fii laylatil jumaati lañ ko tàbbal () ci néeg bu lëndëm, noon ya naan ko làmbal
  • mu làmb daj fa gobar ak ràbbu ñu tëj () ko foofa dem, mu daldi jublu xibla kabbar
  • nee na keroog manul woon a sujjoot ngir tar-tar
  • 'Jàng fa saaru baqara ak aali Imraani () jibriilu tijji néeg ba fil xurhaani'
  • Am na fa yaari guddi lekkul naanul () ludul ci leeri Yàlla kooka naanul...
  • Bisub keroog lañu ko génne foofa () yóbbu feneen mu fekk gaynde bóof fa
  • Ñu boole kook gaynde ga tëj leen booba () Gaynde ga mel ni xar mu gis boroom ba...
  • Ñu daal di koy yóbb ci menn mbedd () bole ko ak yëkk wuñ yafal wuy fàdd
  • mbedd ma noon ya dañu koo gaaraante bisub keroog ruu ga la buur gaaraante.
  • Seex Bamba nee ba mu tëbee wuti fa moom () wuute wul ak boroomi laaf amuli buum
  • ba mu ñëwee ba jub ko faf nërméelu () xooj ga ni fojit fa kanam jibriilu...
  • Keroog la gaal gay daw ba wàllu tisbaar () muy jàpp ab madam bu sew daal di fa jaar
  • Daal di taxaw fi kanamam dal di ko laal () Bamba fasaat njàpp ma daal di am aal
  • bamuy masaa mu delsi daal di koy laal ()nee tuuti kon mu tàkk far baal ko
  • gaayi badar ya, ñoo ko booleek der ba () lal ko ca mbeex ma te demul ca bël ba
  • Seex Bamba daldi jàpp julli tisbaar ...

Xët yi mu lëkkalool

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Téerekaay

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  • (en) Cheikh Anta Babou, Fighting the Greater Jihad: Amadu Bamba and the Founding of the Muridiyya of Senegal, 1853-1913, Ohio University Press, 2007, 320 p.
  • (en) Ahmed Pirzada, The epistemology of Ahmadou Bamba, Birmingham, University of Birmingham, 2003 (thèse)
  • (fr) Oumar Ba (documents recueillis par), Ahmadou Bamba face aux autorités coloniales (1889-1927), 1982, 250 p.
  • (fr) Claude Dazun, Rencontre avec un homme de Dieu : sheikh Ahmadou Bamba, Éd. Ndigel/Diff. Mouvement islamique des mourides d'Europe, 1990
  • (fr) Abdoulaye Dieye, Sur les traces de Cheikh Ahmadou Bamba : l'exil au Gabon, période coloniale, 1895-1902, Edition Ndigel, L'Harmattan, 1985
  • (fr) Cheikh Mor Doje, La vie religieuse de Ahmadou Bamba M'Backe, 1980 (thèse)
  • (fr) Fernand Dumont, Essai sur la pensée religieuse d’Amadou Bamba (1850-1927), Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1968, 3 vol., 588 p. (Thèse)
  • (fr) Alioune M'Backé, Vie et enseignement du cheikh Ahmadou Bamba : maître fondateur de la voie mouride, Éd. Al-Bouraq/Diff. Librairie de l'Orient, 1999
  • (fr) Serigne Bachir Mbacké, Les bienfaits de l'éternel, ou, La biographie de Cheikh Ahmadou Bamba Mbacké (traduction par Khadim Mbacké), Dakar, IFAN/Cheikh Anta Diop, 1995, 439 p.
  • (fr) Ahmadou Drame Serigne, La pensée religieuse de Cheikh Ahmadou Bamba, fondateur du mouridisme (Sénégal), 1985 (thèse)

Lëkkalekaay yu biti

[Soppisoppi gongikuwaay bi]