Aller au contenu

Sooninke

Jóge Wikipedia.

Saraxule walla sooninke, wenn xeet la, ci askanu Mande la bokk. Am naa yeneen tur ñu leen tudd: Wangara, Tubakai, Aswanik.

Sooninke, mooy ku juge Sooni / Sunu. Sooni (walla Sunu) benn dëkk la ca Isipt, ñu ko gëna raññe ci tur wi di Aswan. Maamu sooninke yi, dekk boobu lañu baawo, moo tax ñu yore tur wi Sooni-nke.

Yugo Xasse Diŋa Siise:

Diŋa Siise walla Diŋa Xoore, ci cosaan, bokk na ci maamu sooninke yi. Kooku moo juge woon Sooni/Sunu, te ñow ba sowu jantu afrig (Senegaal, Mali,Gànnaar). Ca jamono Isipt gu yàgg ga la woon, ci mujjam. Bi mu agsi foofu ak gangooram, moo sos imbratoor gi bu ñu naan GANA walla WAGADU.

Saraxule ñoo fi jëkk a dugg ci Lislaam, ci réewum Senegaal, Xeet woowu ñoo jur Jula yi. Jiitu nañu Wolof yi ca Kajoor ak Bawal Séeréer si ca Siin ak Saalum, foofu fépp ñoo fi njëkk a nekk. Imbraatóoru Gana moo ko tabax, ak nguuru Gajaga, nguuru Jara. Seeni buur Tunka lees leen di dàkkantale. Ci mbay lañu daan dunde, yaxantukat (jaaykat) yu mag lañu woon. Seen xeet woowu, am na ay tukkikat yu ba bari, yu daa tukki, di jaay guro, yére, takkaay, ci fépp ci Mali, Senegaal, Niseer, Gine ak Gine-bisaawóo, Gànnaar, ba Kodiwaar. Ci nit ñu nuul yi, dañu bokk ca fi jëkk ñow Tugal. Ca Gànnaar ñu bari ca dëkk ba tudd Gidimaxa lañu, ci wetu Fuuta-Tooro la, foofu tamit nekk nanu fa bu yàgg, ba Tekuruur nekkee. Mamadu Lamin Drame, Sëriñu Saraxule la bu juge Gajaga/Galam, bu ñuy wax tay tundu Bàkkel( (Departement de Bakel), xare na ak tubaab yi bëggoon a boole dëkk bi ci seen moomeel ci atum 1880. Musaa Molo buuru Fulaadu, ci nguuri Pël yu firdo yi, doomu Alfa Yaaya Molo Balde, moo ko daaneel, booba nag buuru Pël bi tubaab bi la àndaloon. Mamadu lamin, tubaab yi ñoo ko ray ca xare ba ñu tudde xareb Tubaa-Kuta, ca atum 1887.

Nosteg mbolaay

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bokk na ci askanu Saraxule:

  • Horon, ñoo doon buur yi.
  • Ñaxamala, ñoo doon ñeeño yi, ràbbkat yi, wuude yi , tëgg yi ak seen yi.
  • Jaaro, waykatu buur yi, xam nañu cosaanu Saraxule yépp, Koora ak Xalam lañuy waye buur yi (Tunka)
  • Komo ñoo doon jaam yi.

Waaye népp dañuy bay seeni tooli bopp. Seeni Sant yi gën a siiw: Ture, Siise, Baccly, Sumaare, Daraame, Kebe, Fofana, Daabo, Jaabi, Silla, Jakite, Soxna, Tunkara.